1Ba Sanbalat déggee ne nu ngi tabaxaat tata ja wër dëkk ba, mu am naqar wu réy, mer lool, di ñaawal Yawut yi
2ca kanam bokkam yaak xarekati Samari ya naan: «Ana lu Yawut yi yaafus yii di jéema def nii? Ñu defe ne moos seen pexe dina sotti, ba ñuy def ay sarax? Fu ñuy noppee seen tabax bi bésub tey? Te yékkatiwuñu lu moy ay doj yu ñu sullee ci jalub tojit yu lakk ba noppi?»
3Tobya Amoneen ba mu feggool nag ne ca tonet ne: «Tata bi ñuy tabax de, su ci till sax yéegoon, mu ànd aki dojam, màbb.»
4Ci biir loolu ma ne: «Ngalla sunu Yàlla, déggal rekk xeebeel gi ñu nu xeeb te walbati seeni xaste, mu këppu ci seen kaw. Ngalla jébbal leen nit ñu sëxëtoo seen alal ci réew mu ñu leen jàpp njaam.
5Bu leen jéggal seen tooñ, bul far seen bàkkaar, ndaxte ñoo doon naqaral ñiy tabax.»
6Ci kaw loolu nu tabaxaat tata ba, wërale ko ba mu àgg ca genn-wàllu taxawaayam, ndax fekk na mbooloo ma pastéefu ca liggéey ba.
7Sanbalat nag ak Tobyaak Arab yaak Amoneen ñaak Asdoddeen ña, ñoom ñépp dégg ne liggéeyu tatay Yerusalem a ngay jëm kanam, te xar-xar yaa ngay tàmbalee fatt. Ñu mer ca lool,
8daldi mànkoo, lal pexe ngir xareek Yerusalem, fitnaal leen.
9Ba mu ko defee nu ñaan ci sunu Yàlla, ba noppi teg fa ay nit ñuy wattu guddeek bëccëg, ngir bàyyi leen xel.
10Fekk na waa Yudaa ngi naan: «Dooley yenukat ŋiis, tojit jalee jale. Nu nuy tabaxeeti jii tata?»
11Ci biir loolu noon ya naan: «Bala ñu noo yég mbaa ñu di nu gis, nu ne saraax ci seen biir, rey leen, yemale fi liggéey bi.»
12Yawut ya ñu dëkkal nag dikk waxsi nu fukki yoon ak juróom li ñu nuy fexeel, ne nu «Fu ne lañuy jóge, songsi nu.»
13Ma teg nag ay nit ci béreb yu ne fàŋŋ te suufe ca gannaaw tata ja. Ma def leen ay kuréel gu ci nekk ak làngam ak bérebam. Ña nga gànnaayoo seeni saamar ak seeni xeej ak seeni fitt.
14Ba loolu amee ma xoolaat lépp, ba noppi wax ak kàngam yaak kilifa yaak mbooloo ma ca des ne leen: «Buleen leen ragal. Fàttalikuleen ne Boroom bi moo màgg te jara ragal te ngeen xeexal seeni bokk ak seen doom yu góor ak yu jigéen, ak seeni jabar ak seeni kër.»
15Gannaaw gi, noon ya xam ne yég nanu leen, te Yàlla nasaxal na seen pexe. Ba mu ko defee nu walbatikuwaat nun ñépp ca tata ja, ku nekk dellu ca liggéeyam.
16La ko dale bésub keroog sama xaaju nit ña rekk a doon liggéey, xaaj ba ca des gànnaayoo ay xeej aki pakk aki fitt ak kiiraayal dënn. Kilifa ya nag taxaw ca gannaaw mboolem waa Yuda.
17Ña doon tabax tata baak ñay yenook ñay yene, ñépp di liggéeye benn loxo, loxo ba ca des ŋàbb ngànnaay.
18Te it ñay tabax, ku ci nekk, sab saamar a nga takke ci sa ndigg, ngay liggéey, boroom bufta bi feggook man.
19Ma wax ak garmi yaak kilifa yaak mbooloo ma ca des, ne leen: «Liggéey bi réy na, yaatu na, te nun danoo tasaaroo te soreyantoo ci tata bi.
20Fu ngeen dégg bufta bi jibe fa, fekksileen nu fa. Sunu Yàlla dina nu xeexal.»
21Nu nekk nag ci liggéey bi, genn-wàllu nit ñi yore ay xeej, dale ko ba bët di set, ba biddiiw yiy feq.
22Boobu it laa wax mbooloo ma ne leen: «Na ku nekk ànd ak ka muy liggéeyandool, fanaan ci biir Yerusalem. Su ko defee nu man di wattu guddi, di liggéey bëccëg.»
23Booba kenn ci nun summiwul ay yéreem, du man, du samay bokk, du samay nit, te du wattukat yi ànd ak man. Ku nekk day ŋàbb ngànnaayam ci ndijooram.