1Bés ba déy a ngii di ñëw, di tàkk ni taal bu yànj. Képp ku bew ak kuy def lu bon, ca lay mel ni boob, te bésub keroog baa koy jafal,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, «du leen waccal tus, dub reen, dub car.
2Waaye yeen ñi ma ragal la jantub njub di fenkal, leerale leen ceeñeer yuy wéral, ngeen génn di tëbantu ni ay sëlluy yar.
3Yeenay joggi ñu bon ñi, ñu doon pënd fi seen ron téstën, keroog bés ba may jëfi,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
4«Bàyyileen xel ci yoonu Musaa, sama jaam ba, yoon wa ma ko dénkoon fa tundu Xoreb, ñeel Israayil gépp, mu diy dogal ak àttey yoon.
5Maa ngii di yebal ci yeen, Ilyaas yonent bi, balaa bésub Aji Sax jee teew, di lu màgg te raglu.
6Mooy delloo xolu baay ca doom ja, delloo xolu doom ca baay ba, lu ko moy ma dikk duma réew mi, ba faagaagal ko.»