1Ndeysaan Boroom bee mer ba xiinal Siyoŋ, dëkk bu taaru bi. Fa asamaan la rattaxe sagu Israayil fa suuf. Keroog bésu meram ma, bàyyiwul xel, ne këram googoo di ndëggastalam.
2Boroom bee modd te yërëmul mboolem sanci Yanqóoba. Ca meram ma la màbbe tatay Yuda réew mu taaru ma. Moo detteel nguur ga aki garmeem, sobeel leen.
3Tàngooru sànjam la daane gépp kàttanu Israayil. Fa kanam noon ba la roccee dooley ndijooram. Moo tàkkal Yanqóoba ni sawara wuy sël-sëli, ba xoyom mboolem la ko wër.
4Boroom bee tàwwi ag fittam mel ni ab noon, moo diire ndijooram, mel ni bañ, moo bóom mboolem lu neexa xool. Ci biir xaymab Siyoŋ dëkk bu taaru ba la yuri am sànjam ni sawara.
5Boroom bee mel nib noon, modd Israayil, moddaale këram yu taaru yépp, tas ay tataam, ba fulal Yuda mu taaru ma, ay yuux aki jooy.
6Moo tas mbaaram ni bu doon mbaarum tool, moo rajaxe bérebu ndajeem. Aji Sax ji moo fàtteloo waa Siyoŋ màggal ak bésub Noflaay, te tàngooru meram la xalabe buur ak sarxalkat.
7Aji Sax jee jañax sarxalukaayam, gedd. Moo teg ci loxol noon tatay këram yi. Biir kër Aji Sax ji la baat xaacoo, ni bu doon bésu màggal.
8Aji Sax jee dogoo rajaxe tatam Siyoŋ mu taaru ma. Moo tàllal buumu nattukaay, ngir tas ko, bankul loxoom it te màbbu ko. Moo jooyloo tata ak tabaxub fegukaay, ñu ànd tojatoo.
9Bunti dëkk ba suulu na, te moo yàqate, dammate weñi tëjukaay ya. Buuram aki garmeem a tumurànkeji ca yéefar ya, te téereb yoon amul, yonent it gisatul peeñu mu bawoo fa Aji Sax ji.
10Magi Siyoŋ dëkk bu taaru ba ña nga toog, xeremlu, xëppoo suuf, sol ay saaku, di ñaawlu. Janqi Yerusalem sëgg, seen bopp jëm suuf.
11Samay gët a giim ndaxi rongooñ, samay butit fuddu, xol ŋiis, jeex tàkk: ci tasteg samaw askan; xale yeek gone yiy nàmp ne lasar fi mbedd yi!
12Seen yaay lañu naan: «Ana fu nuy lekke, ba naan?» te ne lasiim ci mbeddi dëkk bi, ni ñu gaañoo xare, bakkan di tàggoo fa ñu uufoo ca weenu yaay.
13Yaw Yerusalem, dëkk bu taaru bi, lu ma lay wax? Ku ma lay méngaleel? Siyoŋ, janq ju taaru ji laa ne, ana ku ma lay dendaleel, ba seral sa xol? Yaw mi sab góom yaa ni géej, ana ku lay faj?
14Ag neen aki caaxaan la la say yonent gisal, te biraluñu sag ñaawtéef, ngir tijji sa wërsëg, xanaa di la yéeneel waxyuy caaxaan aki nax.
15Mboolem ñi fi jaareey tacc-taccali loxo, ciipu, wëcc bopp ci gentub Yerusalem mu taaru ma, te naan: «Xanaa du biib dëkk lañu doon tudd “Taar bu sotti,” te muy mbégtem àddina sépp?»
16Sa noon yépp a lay ñaawal, di la kókkaleeka kekku, te naan: «Sànk nanu leen nag! Bii bés lanu yàggoona séentu, te noo ko fekke tey.»
17Aji Sax jee def la mu nammoon, moo sottal kàddoom ga mu santaane woon janti démb. Moo faat te yërëmul, ba may noon bége leen, te moo kaweel sa kàttanu bañ yi.
18Askan waa ngi jooy jooyi xol fi kanam Boroom bi. Éy yaw tatay Siyoŋ, dëkk bu taaru bi, sottil say rongooñ ni walum dex guddeek bëccëg; bul noppalu, bul feral say rongooñ.
19Jógal guddi, xaacu: ndoortel wattub guddi, ngay yuri sab xol nim ndox, jàkkaarlook Boroom bi. Tàllal koy loxo, ngir sa bakkani doom yi xiif tax ne lasiim fi boppu mbeddoo mbedd.
20Éy Aji Sax ji, xoolal, seetal rekk ki nga def nii! Xanaa du ndey mooy dem ba yàpp doomu boppam, doom ju mu sukk jur, di ko toppatoo? Xanaa du sarxalkat akub yonent lañuy bóom fi kër gu sell gi ñeel Aji Sax ji?
21Mag ak ndaw a ngi ne lareet fi suuf ci mbedd yi; sama janq jeek sama xale yu góor yi tëdd, saamar faat leen. Yaa rey ci sa bésub mer, yaa rendi te yërëmoo.
22Yaa woote ni su doon bésu màggal, tiitaange dar kepp ma. Bésub merum Aji Sax ji, kenn rëccul, kenn muccul. Doom yi ma jur, yar leen, noon bi rey leen!