1Aka neexoon sama bopp soppaliku ndox, saay gët di seyaan buy xelliy rongooñ yu ma jooye guddeek bëccëg bokk yi ñu bóom!
2Éy ku ma mayoon ci màndiŋ mi dalu panaanum njëggaan, ba ma teqalikook bokk yi, wacc leen, dem, bàyyi leen? Ñoom ñépp ay bokkaale, di gàngooru workat.
3«Ñu ngi tàwwi ni fittkat seen làmmiñu workat, seen doole ci réew mi doxaluñu ci yoon. Ñu ngii di def lu bon ci kaw lu bon, te man faalewuñu ma.» Kàddug Aji Sax jee.
4«Na ku ne moytu dëkkandoom te baña wóolu menn mbokk. Kuy mbokk déy, lal nga pexem wuruj, di wuruj; kuy dëkkandoo, sos ngay wéye.
5Ku ne sa dëkkandoo ngay nax, te dëgg, doo ko wax. Dañoo tàmmi fen, di def njekkar ba sonn.
6Yeena ngi dëkke njublaŋ, njublaŋ rekk, faaleetuleen ma.» Kàddug Aji Sax jee.
7Moo tax Aji Sax ji Boroom gàngoor yi wax ne: «Maa ngii di leen segg, nattu leen ni weñ gu sawara seeyal, xelli! Ana nu may def neneen ak sama ñoñ?
8Seen làmmiñ di fitt guy bóome, seeni wax dig njublaŋ. Nit di wax moroomam jàmm, te di ko tëru cim xelam.
9Lii, ndax duma leen ko dumaa?» Kàddug Aji Sax jee. «Xeet wu mel nii ndax duma ko fey yoolam?»
10Tund ya laay jooy, di yuuxu, di jooy parluy màndiŋ ma, fa lépp lakk, ba jaareesu fa, déggeesul baatu jur; njanaaw ak mala, lépp daw, ne mes.
11«Maay def Yerusalem jali doj, till yi dëkke; ma def dëkki Yuda gent bu kenn dëkkul.»
12Ana ku muus, ba xam lu waral lii? Ana ku Aji Sax ji waxal, mu wax nu lu waral réew mi sànku, gental ni màndiŋ mi, kenn jaaru fi?
13Aji Sax ji ne: «Ñoo wacc sama yoon wi ma leen tegaloon, sàmmuñu sama kàddu, jëfewuñu ko,
14xanaa wéy ci dëgër bopp, topp tuuri Baal yi leen seeni maam miinaloon.»
15Moo tax Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, Yàllay Israayil wax ne: «Maa ngii di leelsil xeet wii njàqarey xeme, nàndal leen tookey mbugal.
16Maa leen di wasaare fi biir xeet yu ñu xamuloon, du ñoom, du seeni maam. Maa leen di tofal saamar, ba raafal leen.»
17Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Ne leen: “Gisleen li xew te woowi jigéeni jooykati dëj yi, ñu dikk; yónneeleen ca ña gëna man, ñu dikk.”»
18Ñiy dëbbe, nañu nu gaawe ci jooy yi, gët taa, rongooñ wal.
19Yuux a ngoog, jibe Siyoŋ. Ñu naa: «Nooka rajaxoo, torox ba ne tott, noon màbb sunuy dëkkuwaay, nu génn réew mi.»
20Yeen jigéen ñi, ngalla dégluleen kàddug Aji Sax ji, taataan waxam, ba jàngal seeni janq jooyi dëj, jigéen ju ne jàngal moroomam yuuxi dëj.
21Dee déy moo ñalgoo sunuy palanteer, dugg sunuy kër yu yànj, rey gone yi ci mbedd mi, ak xale yu góor yi ci pénc yi.
22«Ne leen: “Kàddug Aji Sax jee. Néew yeey wetaroo ci àll bi, mel niy jonkan, ni gub yu góobkat won gannaaw, kenn forul.”»
23Aji Sax ji dafa wax ne: «Ku xelu, bumu damoo am xelam; ku jàmbaare, bumu damoo njàmbaaram; ku woomle, bumu damoom koomam.
24Kuy damu kay, na damoom xelam mu ko may mu xam ma, xam ne maay Aji Sax jiy doxal ngor ak yoon ak njub fi kaw suuf. Loolu déy mooy sama bànneex.» Kàddug Aji Sax jee.
25«Ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay dikkal képp ku xarafam yem ci yaram,
26muy waa Misra, di waa Yuda, di Edomeen ñeek Amoneen ñi, di Mowabeen ñeek mboolem ñiy wat seen peggu kawaru bopp te dëkke màndiŋ mi, nde xeet yooyu, kenn xarafu ci dëgg, te it bànni Israayil gépp xarafuñu xarafu xol.»