1Gannaaw gi, Aji Sax ji ne ma: «Jëlal àlluwa ju mag, ak xalima gu jàppandi, nga bind ci lii: “Mayer Salal Xas Bas” (muy firi Sëxëtoo këfit foqet).»
2Ma wut ci seede, won àlluwa ja ñaar ñu mat seede: ñuy Uri sarxalkat ba, ak Sàkkaryaa doomu Yeberekiya.
3Ba loolu weesoo ma jaxasoo ak sama soxna, yonent bu jigéen ba, mu ëmb, gannaaw gi mu am ca doom ju góor. Aji Sax ji ne ma: «Tudde ko “Mayer Salal Xas Bas.”
4Bala xale bee man ne “Baay” mbaa “Yaay” déy, dees na yóbbul buurub Asiri alal ju ñu foqatee Damaas ak lël ju ñu këfe Samari, nangu ko.»
5Aji Sax ji dellu ne ma:
6«Gannaaw askan wee teddadil ndoxum Silowe mi ci wal mu teey mi, di bége Reccin ak doomu Remalya,
7Boroom baa ngii di leen sottisi dexu Efraat gi ne xéew ak dooleem, te mooy buurub Asiri ak mboolem darajaam. Dex gi mooy génn xuram, fees fépp fu dig tàkkam,
8wal-wali jàll Yuda, mbënn ma wal, taañaañal, yéeg ba tollu ko ci put, firiku niy laaf ba dajal sam réew, yaw Emanuwel.»
9Yeen xeet yi, xaaculeen, dees na leen rajaxe. Yeen waa cati àddina, teewluleen! Gañoo gañu, ñu rajaxe leen! Ma ne: Gañoo gañu, ñu rajaxe leen!
10Ngeen mébét, dara! Ngeen diisoo, diisoo, tus! Yàllaa ànd ak nun!
11Aji Sax ji moo wax ak man, ba mu ma nee nikk, artu ma, ngir ma baña roy askan wii. Mu ne ma:
12«Bul tudde wor, lenn lu askan wii tudde wor; lu ñu ragal it, bu ko ragal, bu ko tiit.
13Aji Sax ji Boroom gàngoor yi daal ngay sellal, moom ngay ragal, moom ngay tiit.
14Mu doon seen kër gu sell, di itam doj wuy fakkastale, xeer wuy daaneel, ci ñaari këri Israayil, te dim yeer, dig fiir, ñeel ku dëkk Yerusalem.
15Ñu baree cay tërëf, daanu, damm, mbaa ñu sërëx, keppu.»
16Dencal seede bii, jëlal lii ndigal, tay cib tayu, dénk ko samay dongo.
17Maa ngi séentu Aji Sax ji, mu ngi won waa kër Yanqóoba gannaaw, waaye maa ngi koy yaakaar.
18Man de, maa ngii, maak xale yi ma Aji Sax ji may, nu diy firnde fi Israayil te diy tegtal yu bàyyikoo fa Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, ki dëkke tundu Siyoŋ.
19Am na ñu naan: «Laajleen boroomi rawaan, ak ñiy gisaane nit ñu dee te di kebetooka ŋun-ŋuni. Aw xeet sañ nañoo gisaanee seeni tuur, tey diis ñi dee mbiri ñiy dund.»
20Kon waxleen ne leen: «Ayca, delluleen ca ndigali yoon ya, ak seedey kàdduy waxyu ya. Kuy wax googu kàddu, ag leer fenkalu la.»
21Nit ñi dinañu taxawaalu ci réew mi, boole njàqareekub xiif, te bu ñu xiifee, ñéññ, téen, xool kaw, saaga seen buur, saaga Yàlla,
22dellu xool fi suuf, yem ciw tiis, ak lëndëmu njàqare, sóoboo guddi gu fatt taraj.