1Nanga woowe sa bokk yu góor: “Ñoñi Aji Sax ji,” sa bokk yu jigéen, nga ne leen: “Ñi Aji Sax ji yërëm.”
2«Tiiñalleen seen ndey, tiiñalleen ko, ndax moom du sama jabar, te man duma jëkkëram. Nee ko mu bàyyi gànctu te noppee tegoo màndargam njaaloo.
3Lu ko moy ma futti ko ba mu ne duŋŋ, def ko ni bés ba mu juddoo, melal ko ni màndiŋ. Maa koy def ni joor gu wow, marloo ko ba rey ko.
4Ay doomam, duma leen yërëm, nde doomi ngànctu lañu.
5Ñoom seen yaay moo gànctu, ki leen ëmb moo def lu gàccelu, naan: “Damay toppi sama far yi may jox sama lekk ak samag naan ak samag wëñ ak sama lẽe ak samag diw ak sama biiñ.”
6«Moo tax man Aji Sax ji, maa ngii di ñage yoonam ay dég, gawe ko ag wërmbal, ba yoon réer ko.
7Mooy topp ay faram te du leen dab; mu seet leen, du leen gis. Su boobaa mu ne: “Naa dellu ca saa jëkkër ju njëkk ja, nde ca laa gënoonu demin.”
8Moom xamul woon ne man maa ko doon jox pepp meek biiñ bu bees beek diw gi, di ko yéwéne xaalis ak wurus, ñu di ko jaamoo seen tuur Baal.
9Kon nag fa ngóob jote laay nangoo sama pepp, fa wittum reseñ jote it laay nangoo sama biiñ bu bees, maay foqati sama wëñ ak sama lẽe, ba mu daan sànge yaramam.
10Léegi maa koy futti, mu ne duŋŋ, ay faram di gis, te kenn du ko xettali ci sama loxo.
11Maay dakkal gépp mbéxam; ay màggalam, ay Terutel weeram, ay bési Noflaayam ak mboolem bési ndajeem.
12Maay yàqate garabi reseñ aki figg yi mu noon: “Lii sama peyoor la! Samay far a ma ko jox.” Maa koy def ay dédd, rabi àll yi di ko lekk.
13Maa koy feyu bési màggal yu tuuri Baal ya mu leen daan taalale cuuraay, takk ay jaarooki gànjar, toppiy faram, fàtte ma.» Kàddug Aji Sax jee.
14«Moo tax maa ngii di ko naxtaan, maa koy yóbbu ca màndiŋ ma, ba déey ko lu xolam dégg.
15Foofa laa koy delloo tóokëri reseñam, defal ko xuru Akor di buntu yaakaaram. Fa la may feeloo na woon ca janti ndawam, ba muy génn réewum Misra.
16Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, «ca nga may woowe “Sama jëkkër,” te dootoo ma woowe “Sama Baal.”
17Turi tuuri Baal laay jële ci sa gémmiñ, ba deesatul fàttaliku seen tur.
18Bésub keroog maa leen di fasal kóllëre ak rabi àll yeek njanaaw yi, ak ndëgmeent yi. Fitt ak saamar akub xare it, maa koy jële ci réew mi, te maa leen di may tëraayu jàmm.
19«Yaw laay digool ba fàww ab séy, te njekk ak njub ak ngor ak yërmande ci laay digook yaw ab séy.
20Ci kóllëre laay digook yaw ab séy, ba nga xam Aji Sax ji.
21Bésub keroog, maay nangu,» kàddug Aji Sax jee, «maay nangul asamaan, moom, mu nangul suuf;
22suuf nangul pepp ak biiñ ak diw, ñu bokk nangul Yisreel.
23Maa koy jëmbatal sama bopp ci réew mi, maay yërëm ki tuddoon “Ki ñu yërëmul.” Ki tuddoon “Du sama ñoñ,” ma ne ko: “Yaay sama ñoñ,” moom mu ne ma: “Yaay sama Yàlla.”»