1Yanqóoba moom topp yoonam. Ci kaw loolu ay malaakay Yàlla feeñu ko.
2Ba leen Yanqóoba gisee, da ne dalub Yàllaa ngii, ba tax mu tudde béreb ba Maxanayim (muy firi Ñaari dal).
3Ba loolu amee Yanqóoba dafa yónni ay ndaw, ñu jiitu ko ca magam Esawu, ca réewu Seyir, di diiwaanu Edom.
4Mu sant leen ne leen: «Bu ngeen demee ca sama sang Esawu, neleen ko: Sa surga Yanqóoba nee na: “Maa nga woon ca kër Laban bu yàgg ba tey,
5ma doora ñëw, ànd ak ay nag ak ay mbaam ak ay gàtt ak ay jaam yu góor ak yu jigéen; may yónnee ci yaw, di la siyaare tey sàkku nga dalal ma jàmm.”»
6Ndaw ya daldi dem ba délsi ca Yanqóoba, ne ko: «Dem nanu ca sa mag Esawu, waaye moom ci boppam mu ngi ci yoon wi di ñëw, fekksi la fii, te ma nga ànd ak ñeenti téeméeri góor.»
7Yanqóoba dégg loolu, tiit lool te ànd ak njàqare, ba tax mu séddale mbooloo, ma mu àndal, gàtt ya ak jur gu gudd ga ak giléem ya itam, mu xaaj leen ñaar.
8Booba mu ngi naan, bu Esawu songee benn dal bi, dal bi ci des mana raw.
9Ci kaw loolu Yanqóoba ñaan Yàlla, ne ko: «Yaw Aji Sax ji, sama Yàllay maam Ibraayma, di sama Yàllay baay Isaaxa itam, yaa ma ne woon: “Dellul réew ma nga cosaanoo, ca say bokk; dinaa la baaxe.”
10Yelloowuma lu gëna tuuti ci sa ngor ak sa worma, gi nga ma won, man sa jaam. Aw yet doŋŋ laa yoroon, ba ma jàllee dexu Yurdan, te yokku naa tey, ba doon ñaari dal.
11Maa ngi lay ñaan, nga musal ma ci sama loxol mag Esawu, ndaxte ragal naa, mu ñëw bóom ma, bóomaale jigéen ñi ak seeni doom.
12Te yaw yaa ma ne: “Dinaa la baaxe moos, yokk saw askan, ba mu tollu ni suufas géej si kenn manula lim ndax bare.”»
13Yanqóoba fanaan na fa guddig keroog, doora sàkk ca alalam, sédd magam Esawu,
14lépp di ñaari téeméeri bëy ak ñaar fukki sikket ak ñaari téeméeri xar ak ñaar fukki kuuy
15ak fanweeri giléem yu seeni doom di nàmp, ak ñeent fukki nag ak fukki yëkk ak ñaar fukki mbaam yu jigéen ak fukki mbaam yu góor.
16Mu ber gétt yi, gu ci nekk mu jox ay surgaam, ne leen: «Jiituleen ma, te na gétt yi dàndante.»
17Ci biir loolu mu sant ki jiitu, ne ko: «Boo dajeek sama mag, mu laaj la ne la: “Kuy sa njaatige?” ak “Ku moom li nga jiital?” ak “Foo jëm?”
18nee ko: “Lii de sang bi, lu la Yanqóoba may la, di la ko siyaaree, yaw Esawu, te moom ci boppam mu ngi topp ci sunu gannaaw.”»
19Ndigal loolu la joxaat ñaareelu surga ba ak ñetteel ba ak mboolem ña topp ca gétt ya, ku ci nekk mu wax ko ne ko loolu lay wax Esawu, bu ko gisee,
20tegati ca ne ko: «Te nee ko itam: “Sa surga Yanqóobaa ngi topp ci sunu gannaaw.”» Booba Yanqóobaa ngi naa ci xelam: «Bu ma jiitalee li ma ko may, neexale ko ko, bala maa janook moom, jombul mu dalal ma jàmm.»
21Neexal ba da koo jiitu, moom mu fanaan guddig keroog ca dal ba.
22Gannaaw loolu Yanqóoba jóg ca guddi ga, ànd ak ñaari soxnaam, ñaari jaamam yu jigéen ak fukki doomam yu góor ak benn, daldi jàll dexu Yabog.
23Yanqóoba da leena jàllale, jàllewaale alalam jépp itam.
24Mu des fa nag moom doŋŋ. Kera la genn góor fanaane bëre ak moom, ba bët set.
25Ba nit ka xamee ne manalu ko dara, dafa dóor Yanqóoba ci yaxu mooco bi, mu summikoo ca bëre ba.
26Nit ka ne ko: «Bàyyi ma, ma dem, ndax bët a ngi bëgga set.» Teewul Yanqóoba ne ko: «Duma la bàyyi, nga dem, li feek ñaanaloo ma.»
27Nit ka ne ko: «Na nga tudd?» Mu ne ko: «Yanqóoba.»
28Nit ka ne ko: «Tuddatuloo Yanqóoba, léegi Israayil nga tudd, ndaxte bëre nga ak nit, bëre ak Yàlla, ba génn ci ak jàmm.»
29Yanqóoba ne ko: «Waaw, yaw nag noo tudd?» Mu wax ko ne ko: «Loo may laaje sama tur?» ba noppi barkeel ko foofa.
30Ci kaw loolu Yanqóoba tudde béreb ba Peniyel (muy firi Xar-kanamu Yàlla), ndaxte da ne: «Ne naa Yàlla jàkk, te maa ngi dund ba tey.»
31Ba jant bay fenk, Yanqóobaa ngi soox tànk bi, di bàyyikoo Penuwel.
32Looloo tax ba tey jii bànni Israayil duñu lekk yàpp wi jàpp ci tenqob mooco, ndax li moocob Yanqóoba summikoo woon ca suuxu tenqo ba.