1Aji Sax ji da ne Musaa: «Demal ca Firawna, ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Bàyyil sama ñoñ, ñu dem jaamuji ma.
2Soo leen bañee bàyyi, ñu dem kat, maa leen di mbugale ay mbott yu daj sam réew.
3Dexu Niil gi day ramm-rammeeki mbott, te dinañu ñëw, duggsi sa biir kër, ak sa néegu biir, ak sa kaw lal, ak sa këri dag, ak sa waa réew, ba ca lakkukaay yaak nootukaayi mburu ya.
4Mbott yi dinañu yéeg ci sa kaw, yéeg ci kaw waa réew mi, ak sa dag yépp.”»
5Ba loolu weesoo Aji Sax ji ne Musaa: «Waxal Aaróona, ne ko mu jël yet wi, tàllal loxoom, tiimale ko dex yi, ak yooni ndox yeek déeg yi, ngir indi mbott yi ci biir réewum Misra.»
6Aaróona tàllal loxoom, mu tiim ndoxi Misra, mbott ya jóg, lal réewum Misra.
7Jabarkat ya it fexe ca seeni xarfafuufa, ba indi ay mbott ca réewum Misra.
8Ba mu ko defee Firawna woo Musaak Aaróona, ne leen: «Ñaanleen Aji Sax ji, ngir mu teqale nook mbott yi, man ak sama waa réew. Kon dinaa bàyyi mbooloo mi, ñu dem rendili Aji Sax ji sarax.»
9Musaa ne Firawna: «Saa yu la neexee rekk, sang bi. Wax ma kañ laa lay ñaanal, yaw ak say dag ak sa waa réew, ngir jële fi mbott yi, ñu tàggook yeen, génn seeni kër, ca dexu Niil ga doŋŋ lañuy des.»
10Mu ne ko: «Nay ëllëg.» Musaa ne ko: «Baax na, ndax nga xam ne sunu Yàlla Aji Sax ji amul moroom.
11Mbott yi dinañu jóge sa kër, teqalikook yeen, yaak say dag ak sa waa réew, ca dexu Niil ga doŋŋ lañuy des.»
12Musaa ak Aaróona nag jóge ca Firawna, Musaa tinu Aji Sax ji ca mbirum mbott ya mu yare Firawna.
13Aji Sax ji def la ko Musaa ñaan, mbott ya dee, ba jeex ca kër yaak ca ëtt yaak tool ya.
14Ñu jal koo jal, ba xet ga ubale ca réew ma.
15Teewul, ba Firawna gisee ca mbir ma ag tan, daa wéye të, tanqamlu leen, muy la Aji Sax ji waxoon.
16Ba loolu amee Aji Sax ji ne Musaa: «Waxal Aaróona ne ko mu tàllal yetam, dóor ci pëndub suuf si, mu doon ay yoo ci réewum Misra gépp.»
17Ñu def loola, Aaróona tàllal loxoom ba mu yore yet wa, dóor ca pënd ba, mu doon ay yoo yu song nit ak rab; pëndub suuf sépp a defi yoo ca réewum Misra gépp.
18Jabarkat ya fexe ca seeni xarfafuufa, nu ñu defe ay yoo, waaye manuñu. Yoo ya nag song nit ñaak rab ya.
19Jabarkat ya ne Firawna: «Lii de Yàlla rekk a ko man!» Teewul Firawna wéye të rekk, tanqamlu leen, muy la Aji Sax ji waxoon.
20Aji Sax ji waxati Musaa, ne ko: «Teelala xëy ëllëg ca Firawna, buy génn jëm ca ndox ma, nga wax ko ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: Bàyyil sama ñoñ, ñu dem jaamuji ma.
21Ndaxte soo bàyyiwul sama ñoñ, ñu dem kat, dinaa yuri ay ndiiraani weñ yuy màtte ci seen kaw, yaak say dag ak sa waa réew, te dinañu àgg ci sa biir kër. Këri waa Misra dina fees ak weñ yuy màtte, ba suuf, si ñu taxaw sax, weñ yee koy muur.
22Waaye bu keroogee dinaa ci musal diiwaanu Gosen, ga sama ñoñ dëkke, ba ay weñ du fa same, ndax nga xam ne, man Aji Sax ji maa ngi ci digg réew mii,
23te maay musal sama ñoñ ci musiba moomuy dal saw askan. Ëllëg firnde jooju dina am.”»
24Aji Sax ji def loola, weñ yi def ndiiraan yu réy, song kër Firawna ak kër dagam ya, dajal réewum Misra, ba réew ma yàqu ndax ndiiraani weñ ya.
25Firawna daldi woolu Musaak Aaróona, ne leen: «Demleen rendili seen Yàlla sarax, te nay ci biir réew mi nag.»
26Musaa ne ko: «Loolu du yoon, ndax li nuy rendil sunu Yàlla Aji Sax ji, waa Misra dañu koy xof. Te bu nu sarxalee lenn lu waa Misra xof, ñuy gis, dinañu nu dóor ay doj, ba nu dee.
27Kon kay danoo wara génn, topp màndiŋ mi lu mat doxub ñetti fan, rendili fa sunu Yàlla Aji Sax ji sarax, ni mu nu ko sante.»
28Firawna àddu ne: «Dinaa leen may, ngeen dem ca màndiŋ ma, rendili seen Yàlla Aji Sax ji sarax, waaye buleen sore lool. Ñaanalleen ma nag.»
29Musaa ne ko: «Bu ma bàyyikoo ci yaw rekk Firawna, dinaa tinu Aji Sax ji, ngir ëllëg ndiiraani weñ yi teqalikook yaw, ak say dag ak sa waa réew, waaye kat Firawna, bu nu naxati, di baña bàyyi mbooloo mi, ñu rendili Aji Sax ji sarax.»
30Musaa bàyyikoo fa Firawna, daldi tinu Aji Sax ji.
31Aji Sax ji defal Musaa la mu ñaan, jële ndiiraani weñ ya ca Firawnaaki dagam ak waa réewam, ba weñ desatu fa.
32Teewul Firawna të rekk, baña bàyyi mbooloo ma, ñu dem.