1Ku ñu mor mbaa ñu dagg ngóoraam, du bokk ci ndajem gëmkati Aji Sax ji.
2Ku dul doomu yoon du bokk ci ndajem gëmkati Aji Sax ji. Ku askanoo ci moom it, ba ca fukkeelu maas ga, du bokk ci ndajem gëmkati Aji Sax ji.
3Ab Amoneen mbaa ab Mowabeen du bokk ci ndajem gëmkati Aji Sax ji. Ku askanoo ci ñoom it, ba ca fukkeelu maas ga, du bokk ci ndajem gëmkati Aji Sax ji mukk,
4ndax la ñu leen dabewul woon aw ñam, mbaa am ndox, ca yoon wa, ba ngeen génnee Misra, xanaa di fey Balaam doomu Bewor ma bokk Petor ca Aram Naarim, ngir mu móolu leen.
5Waaye seen Yàlla Aji Sax ji moo nanguwula déglu Balaam; kàddug yàqe ga la leen seen Yàlla Aji Sax ji soppil barke, ndax seen Yàlla Aji Sax ji da leena sopp.
6Buleen sàkku mukk jàmmu ñooñu mbaa seen njariñ, seen giiru dund, ba fàww.
7Buleen bañ ab Edomeen, ndax seen mbokk la. Buleen bañ nitu Misra, ndax ay doxandéem ngeen woon ca seenum réew.
8Ñi soqikoo ci ñaari xeet yooyii, ca ñetteelu maas ga, te di seeni sëtaat nag, sañ nañoo bokk ci ndajem gëmkati Aji Sax ji.
9Bu ngeen génnee ba fàkk ab dal, ngir jànkoonte ak seeni noon, nangeen sàmmu ci lépp lu aay.
10Su amee ci seen biir ku setul, ndax géntu guddi gu ko dikkal, na génn dal bi, ca biti, te bumu duggaat ci biir dal bi.
11Bu ngoon di jubsi na sangu, ba jant bi so, mu doora délsi ci biir dal bi.
12Te sàkkleen béreb bu génn dal bi, ngeen di fa dem, di suturluji.
13Na ngaska bokk ci seeni fàgguwaay, ndax su ngeen suturlujee ca biti ba noppi, moom ngeen di gase, ba suul seeni jonkan.
14Ndax seen Yàlla Aji Sax ji mooy dem aka dikk ci seen biir dal bi, ngir xettali leen, ba jébbal leen seeni noon. Kon nag seenub dal daa wara sell, ngir Aji Sax ji ñàkka gis fi seen biir, lenn lu tegginewul, ba dëddu leen.
15Gannaaw loolu buleen delloo ab jaam bu làqu ci yeen, te rëcce ci ab sangam.
16Ci yeen lay toog, ci seen biir, béreb ba mu taamu, ci benn bi ko gënal ci seeni dëkk, te buleen ko néewal doole.
17Gànc buy gànctul ay tuur, bumu am ci biir jigéeni Israayil, te gànc bu góor buy gànctul ay tuur, bumu am ci góori Israayil.
18Buleen indi mukk ci seen biir kër Yàlla Aji Sax ji, peyooru gànc bu jigéen mbaa bu góor, ngir wépp xas wu ngeen namma wàccoo googu peyoor, ndax yooyu ñaar yépp, seen Yàlla Aji Sax ji seexlu na ko.
19Buleen teg seen mbokkum bànni Israayil tegandaayal xaalis, mbaa tegandaayal ñam, mbaa tegandaayal mboolem bor bu tegandaay tege.
20Ab doxandéem, sañ ngeen koo sàkku tegandaay, waaye seen mbokkum bànni Israayil, buleen ko sàkku tegandaay. Su ko defee seen Yàlla Aji Sax ji mooy barkeel mboolem seenu ñaq, ca réew ma ngeen jëm, ngir nanguji ko.
21Su ngeen xasalee seen Yàlla Aji Sax ji aw xas, buleen ko yeexa wàccool, ndax kon seen Yàlla Aji Sax ji du leen ko ñàkka topp, te kon muy seen bàkkaar.
22Waaye baña xas, amul bàkkaar.
23Li seen làmmiñ tudd, sàmmooleen koo jëfe, na ngeen ko xasale woon seen Yàlla Aji Sax ji, ci seen sagoy bopp, ak seen kàddug bopp.
24Bu ngeen duggee ci seen tóokëru reseñu moroom, lekkleen ca reseñ ja lu leen neex ba suur, waaye seen ndab, buleen ko ca yeb.
25Bu ngeen duggee ci seen toolu peppu moroom, fekk mu ñor, sàkkeleen seen loxo ca gub ya, waaye ab sàrt, buleen ko góobe seen peppu moroom.