1Bataaxalu Buur Nebukatnecar a ngii, jëm ci mépp mbooloo ak wépp xeet ak wépp làkk, ak fu ñu dëkke ci àddina sépp: Yal na seen jàmm yokku.
2Màndarga yeek kéemaan yi ma Yàlla Aji Kawe ji defal, maa ngi am bànneex ci xamle ko.
3Ndaw màndargaam yu màgg, ndaw kéemaanam yu réy! Nguuram ay nguur gu sax dàkk, kilifteefam ñeel maasoo maas.
4Man Nebukatnecar maa ngi woon ci sama jàmmi kër ak sama teraangay màkkaan.
5Ma tëdd sama lal, daldi am gént gu ma tiital, ak xalaat ak peeñu yu ma indil njàqare.
6Ma joxe ndigal, woolu boroom xam-xami Babilon yépp, ngir ñu xamal ma pirim gént gi.
7Ci kaw loolu taryaax yeek ñeengokat yeek xërëmkat yeek seetkat yi dikk. Ma nettali leen gént gi, waaye waxuñu ma piri mi.
8Ñu mujj ma indil Dañeel, di Beltacar mi ñu tudde sama yàlla, di ku xelu yàlla yu sell yi nekk ci moom. Ma wax ko gént gi.
9Ma ne ko: «Beltacar, kilifay taryaax yi, man ci sama bopp xam naa ne xelum yàlla yu sell yaa ngi ci yaw, te menn mbóot jaaxalu la. Peeñum gént gi ma gént, wax ma piri mi.
10Li ma gis daal ci sama kaw lal mooy lii: Damaa jekki gis garab ci digg àddina si, mu gudd lool.
11Garab gay màgg, di réy, ba njobbaxtal la di laal asamaan, ñu di ko séen ba ca cati àddina sépp.
12Xob yaa nga naat, meññeef ma ne gàññ, mana dundal ñépp. Muy keppaaral rabu àll, di tàggal njanaaw, di dundal bépp boroom bakkan.
13«Fi ma tëdd ci sama lal, ma jekki gis ab wattukat bu sell wàcce asamaan.
14Mu àddu ca kaw ne: “Daaneleen garab gi te gor ay bànqaasam. Wittleen xob yi, tasaare meññeef mi. Na rab yi jóge ci keppaaram, daw, njanaaw yi ciy bànqaasam, naaw.
15Waaye ëkk beek reen yi, bàyyileen ko fi suuf ci digg mbooy mi, te jénge ko càllalay weñ ak xànjar. Na ko layub asamaan di faam, muy dunde ñax nig jur.
16Mu nitoodi, ame xelum mala diiru juróom ñaari jamono.
17Ndogal a ngoog bu wattukat yi tëral, àttee ngoog bu ñu sell ñooñu digle, ngir aji dund ji xam ne Aji Kawe jee yilif nguurug nit, di ko jox ki ko soob, di ca fal ki gëna tuut.”
18«Loolu laa gént, man, Nebukatnecar. Yaw Beltacar nag, wax ma piri mi. Ndax boroom xam-xam yi ci sama réew mi, kenn manu ma cee wax piri mi. Waaye yaw man nga ko, ngir xelum yàlla yu sell yaa ngi ci yaw.»
19Ba loolu amee Dañeel ma ñuy wax Beltacar ne dann ab diir, jaaxle, xalaat yu ko tiital dikkal ko. Buur àddu ne ko: «Beltacar, gént geek piri mi bumu la tiital.» Beltacar ne ko: «Sang bi, su ma sañoon de muy sa géntug noon te pireem topp say bañaale.
20Garab gi nga gis muy màgg di réy, njobbaxtal lay laal asamaan, ñu di ko séen ci àddina sépp,
21mook xobam yu naat ak meññeefam mu ne gàññ, mana dundal ñépp; muy keppaaral rabu àll, di tàggal njanaaw:
22Buur de, garab googu yaw la. Yaa màgg, di bare doole; di màgg ba laal asamaan, sa kilifteef àkki cati àddina.
23«Buur, li nga gis mooy ne kenn ci wattukat yu sell yi wàcce asamaan, daa àddu ca kaw ne: “Daaneleen garab gi, tas ko, waaye ëkk beek reen yi, bàyyileen ko fi suuf ci digg mbooy mi, te jénge ko càllalay weñ ak xànjar. Na lay biy wàcc, di ko faam, muy dunde ñax nig jur diiru juróom ñaari jamono.”
24Piri maa ngii, Buur, di dogalu Aji Kawe ji dal ci sa kaw, Buur, sang bi.
25Yaw lañuy dàqe ci nit ñi; rabi àll yi ngay dëkkal, ñax di sam xont niw nag, lay biy wàcc di la faam diiru juróom ñaari jamono, ba kera ngay xam ne Aji Kawe jee yor nguurug nit, di ko jox ku ko neex.
26Li ñu santaane ñu bàyyi ëkk beek reeni garab gi mooy tekki ne nguur gi dees na la ko delloo keroog boo xamee ne Boroom asamaan mooy Buur.
27Kon nag Buur, ngalla nangul li ma lay digal: say moy ak say bàkkaar, daboo ko di def njekk ak di baaxe néew-ji-doole ndax sa teraanga sax.»
28Loolu lépp dal na Buur Nebukatnecar.
29Ba ñu ca tegee fukki weer ak ñaar yu mat, muy doxantu ca kaw taaxum kër buur ca Babilon,
30ma ngay wax naan: «Xanaa lii du Babilon gu mag gi ma tabax man, ci sama doole ju réy, muy péeyu buur, di sama ndam ak sama daraja?»
31Kàddug Buur ga daanoogul sax, baat jibe asamaan àddu ne: «Yaw Buur Nebukatnecar, dogal ñeel na la ne nguur gi rëcc na la.
32Dees na la dàqe ci nit ñi, nga dëkk ak rabi àll yi, ñax di sam xont niw nag diiru juróom ñaari jamono, ba kera ngay xam ne Aji Kawe jee yor nguurug nit, di ko jox ku ko neex.»
33Ca saa sa kàddu ga sotti ñeel Nebukatnecar. Ñu dàqe ko ci nit ñi, muy dunde ñax niw nag, lay biy wàcc di ko faam, ba kawar gi sëq ni dunqi jaxaay, ay wewam di saf yu njanaaw.
34Ba àpp ba matee, man Nebukatnecar, maa séentu asamaan, sama sago délsi. Ma sant Aji Kawe ji, sargal Kiy dund ba fàww, màggal ko: kilifteefam sax fàww, nguuram ñeel maasoo maas.
35Mboolem waa àddina di neen ci moom. Nu ko neex lay def ak gàngoori xarey asamaan ak waa suuf, te kenn du fél loxoom mbaa mu naa ko: «Ana looy def nii?»
36Ba sama sago délsee, ca laa jotaat ndam ak daraja ngir sama teraangay nguur. Ba loolu amee samay jawriñ ak samay jaraaf jëlsi ma; ñu dëjaat ma ci nguur gi, ma gënatee màgg.
37Léegi nag man, Nebukatnecar, maa ngi sant Boroom asamaan, di ko sargal, di ko màggal. Lu mu def dëgg la, fu mu jaare njub la, te kuy réy-réylu man na laa suufeel.