1Ba Iram buurub Tir déggee ne Suleymaan lañu fal buur, mu wuutu baayam Daawuda, ak na mu xaritoo woon ak Daawuda naka jekk, Iram daa yónnee ay ndawam ca Suleymaan.
2Suleymaan it yónnee ca Iram, ne ko:
3«Xam nga sama baay Daawuda manul woona tabaxal Yàllaam Aji Sax ji kër gu mu ko tudde, ndax xare yi mu séqoon ak noonam yi ko wër, ba ni leen Aji Sax ji daaneele, mu teg leen tànk.
4Léegi nag sama Yàlla Aji Sax ji may na ma jàmm ne ñoyy, féete ma wet gu nekk, ba awma benn noon, te musiba dabu ma.
5Fii ma nekk damaa fas yéene tabax kër, tudde ko sama Yàlla Aji Sax ji. Muy la Aji Sax ji waxoon sama baay Daawuda, ne ko: “Sa doom ji may def sa kuutaay ci sab jal moo may tabaxal kër, tudde ma ko.”
6Ci biir loolu ma di la ñaan, nga santaane, ñu goral ma banti seedar yu Libaŋ, te samay surga ànd ak say surga ci liggéey bi. Sa peyooru nit ñi dinaa la ko fey ak loo mana feyeeku, ndax yaw xam nga ne amunu ci sunu biir ñu mane yatt bant ni waa Sidon.»
7Ba Iram déggee li Suleymaan wax, mu am ca mbégte mu réy. Mu ne: «Cant ñeel na Aji Sax ji tey jii, bi mu mayee Daawuda doom ju rafet xel, mu jiite xeet wu réy wii.»
8Ci kaw loolu Iram yónnee ca Suleymaan, ne ko: «Dégg naa kàddu yi nga ma yóbbante. Man ci sama bopp dinaa la defal li nga bëgg lépp ci wàllu banti garabi seedar ak sippar.
9Samay surgaa koy diree Libaŋ ba ca géej ga, rabat ko, ma jaarale ko ci géej gi ba foo ma wax. Su ko defee ma tas ko foofa, nga yóbbu. Yaw nag nangul ma rekk li may sàkku, muy nga joxal ma sama waa kër ab dund.»
10Ba loolu amee Iram jox Suleymaan la mu bëgg ci banti garabi seedar ak sippar.
11Suleymaan ci wàllu boppam jox Iram ñaar fukki junniy (20 000) sëfi mbaami peppu bele, ak ñaar fukki junniy (20 000) sëfi mbaam ci diwu oliw gu ñu segal. Suleymaan di defal Iram noonu at mu ne.
12Ba loolu weesoo Aji Sax ji mayoon na Suleymaan xel mu rafet, na mu ko ko dige woon. Jàmm it doxoon na diggante Iram ak Suleymaan, ba ñu fasante kóllëre ñoom ñaar.
13Buur Suleymaan nag sas fanweeri junniy nit (30 000) ci Israayil gépp ay liggéeyi sañul-bañ.
14Mu di leen yebal Libaŋ, weer wu nekk fukki junni (10 000) dem. Bu ñu amee Libaŋ weer, am seeni kër ñaari weer. Adoniram a jiite woon sas ya.
15Suleymaan sàkk juróom ñaar fukki junniy (70 000) yenukat, ak juróom ñett fukki junniy (80 000) yattkati doj ca tund ya,
16te bokkul ak ñetti junni ak ñetti téeméeri nit (3 300) ñi Suleymaan tabb, ñuy jiite liggéey bi, di saytu liggéeykat yi.
17Buur santaane ñu jële fa doji tànnéef yu réy yu ñuy yatt, muy fondmaa kër Yàlla ga.
18Ba mu ko defee tabaxkati Suleymaan ak tabaxkati Iram ak waa Gebal di yatt aka waajal bant yaak doj ya ñuy tabaxe kër ga.