1Doomi Lewi yu góor ñoo di Gerson ak Keyat ak Merari.
2Doomi Keyat yu góor ñoo di Amram ak Iccar ak Ebron ak Usyel.
3Doomi Amram yu góor ñoo di Aaróona ak Musaa, Maryaama di doomam yu jigéen. Doomi Aaróona yu góor ñoo di Nadab ak Abiyu ak Elasar ak Itamar.
4Elasar mooy baayu Fineyas, Fineyas di baayu Abiswa.
5Abiswa mooy baayu Bukki, Bukki di baayu Usi.
6Usi mooy baayu Seraxya, Seraxya di baayu Merayot.
7Merayot mooy baayu Amarya, Amarya di baayu Axitub.
8Axitub mooy baayu Cadog, Cadog di baayu Aximàcc.
9Aximàcc mooy baayu Asaryaa di baayu Yoxanan.
10Yoxanan mooy baayu Asaryaa. Asaryaa moomu sarxalkat la woon ca kër Yàlla ga Suleymaan tabaxoon ca Yerusalem.
11Asaryaa mooy baayu Amarya, Amarya di baayu Axitub.
12Axitub mooy baayu Cadog, Cadog di baayu Salum.
13Salum mooy baayu Ilkiya, Ilkiya di baayu Asaryaa.
14Asaryaa mooy baayu Seraya, Seraya di baayu Yoccadag.
15Yoccadag moomu gàddaayloo nañu ko ca jamono ja Aji Sax ji toxal waa Yuda ak Yerusalem, jaarale ko ci Nebukatnecar.
16Doomi Lewi yu góor di Gerson, Keyat ak Merari.
17Ñii ñoo di doomi Gerson yu góor: Libni ak Simey.
18Doomi Keyat yu góor ñoo di Amram ak Iccar ak Ebron ak Usyel.
19Doomi Merari yu góor ñoo di Maxli ak Musi. Ñooñu ñooy ñi ñu tudde làngi giirug Leween ñi ni leen seeni maam lime.
20Góor ñi askanoo ci Gerson ñoo di doomam Libni mi jur Yaxat mu jur Simma.
21Simma moo jur Yowax mi jur Ido mu jur Sera ak Yettray.
22Góor ñi askanoo ci Keyat ñoo di Aminadab mi jur Kore mu jur Asir.
23Asir jur Elkana mi jur Abyasaf mu jur Asir.
24Asir moomu jur Taxat mi jur Uryel mu jur Osiyas mu jur Sawul.
25Elkana am na yeneen doom yu góor, ñuy Amasay ak Aximot.
26Góor ñi soqikoo ci Elkana ñoo di Cofay mi jur Naxat.
27Naxat jur Elyab mu jur Yeroxam mi jur Elkana.
28Doomi Samiyel yu góor ñoo di Yowel taawam, ka ca topp di Abya.
29Góor ñi soqikoo ci Merari nii lañu toppantee: Maxli mi jur Libni mu jur Simey mu jur Usa.
30Usa jur Simeya mi jur Agiya mu jur Asaya.
31Ñii ñoo di Leween ñi Daawuda sasoon ñuy jiite woy yi ci kër Aji Sax ji, bu ñu fa xasee yeb gaalu Yàlla ga.
32Ñooñu ñoo yoroon liggéeyu woy ya fa kanam jaamookaay ba, ca xaymab ndaje ma, ba keroog Suleymaan tabaxee kër Aji Sax ji ca Yerusalem. Ñuy def seen liggéey nag na ñu leen ko sante.
33Ñi sasoo woon liggéey boobu ñook seeni doom yu góor ñii la: làngu Keyat: Eman woykat ba, doomu Yowel, doomu Samiyel,
34doomu Elkana, doomu Yeroxam, doomu Elyel, doomu Towa,
35doomu Cuuf, doomu Elkana, doomu Maxat, doomu Amasay,
36doomu Elkana, doomu Yowel, doomu Asaryaa, doomu Sofoni,
37doomu Taxat, doomu Asir, doomu Abyasaf, doomu Kore,
38doomu Iccar, doomu Keyat, doomu Lewi, doomu Israayil.
39Ku góor ka daan taxaw ca wetu ndijooru Eman ca liggéey ba moo doon mbokkam Asaf. Asaf moo doon doomu Berekya, doomu Simeya,
40doomu Mikayel, doomu Baaseya, doomu Malkiya,
41doomu Etni, doomu Sera, doomu Adaya,
42doomu Etan, doomu Simma, doomu Simey,
43doomu Yaxat, doomu Gerson, doomu Lewi.
44Waa làngi Merari ñoo daan féete càmmoñ: Etan doomu Kisi, doomu Abdi, doomu Malukk,
45doomu Asabya, doomu Amaciya, doomu Ilkiya,
46doomu Amci, doomu Bani, doomu Semer,
47doomu Maxli, doomu Musi, doomu Merari, doomu Lewi.
48Seen yeneen mbokki Leween ñi ñoo doon def mboolem yeneen liggéeyi kër Yàlla ga.
49Waaye Aaróona ak góor ñi askanoo ci moom ñoo doon lakk sarax yi ci kaw sarxalukaayu rendi-dóomal yi, di taal cuuraay li ci kaw sarxalukaayu cuuraay ba, di toppatoo mboolem lu jëm ci néeg bu sella sell ba. Ba tey ñoo doon daa defal Israayil seen njotlaay, na ko Musaa, jaamu Yàlla ba digle woon.
50Góor ñi askanoo ci Aaróona nii lañu toppantee: Elasar doomu Aaróona, moo jur Fineyas mi jur Abiswa.
51Abiswa moo jur Bukki mi jur Usi mu jur Seraxya.
52Seraxya moo jur Merayot mi jur Amarya mu jur Axitub.
53Axitub moo jur Cadog mu jur Aximàcc.
54Gox yii ñuy lim la askanu Aaróona wi bokk ci làngu Keyat dëkke woon. Ñoo njëkka jot ca seen suuf sa ñu muurloo ci kaw tegoo bant.
55Jox nañu leen Ebron, dëkk bu mag ba ca Yuda ak àlli parlu ya ko wër.
56Waaye fekk na tool yaak dëkk yu ndaw ya bokk ca dëkk bu mag ba, jox nañu ko Kaleb, ku góor kay doomu Yefune.
57Góor ñi askanoo ci Aaróona lañu jox Ebron, dëkkub rawtu ba, ak Libna ak àlli parlu ya ko wër, ak Yatir ak Estemowa ak parlu ya ko wër;
58ak Ilen ak parlu ya ko wër, ak Debir ak parlu ya ko wër;
59ak Asan ak parlu ya ko wër, ak Bet Semes ak parlu ya ko wër.
60Jële nañu ci suufas giirug Beñamin dëkk ba ñuy wax Geba aki parloom, ak Alemet aki parloom, ak Anatot aki parloom. Lépp di fukki dëkk ak ñett yu ñu séddoo ci seeni làng.
61Waa kër góor ña des ci askanu Keyat lañu jox fukki dëkk yu bokk ci suufas giirug Efrayim ak giirug Dan ak genn-wàllu giirug Manase.
62Waa kër góor ñi askanoo ci Gerson lañu jox fukki dëkk yu mag ak ñett yu bokk ci suufi giiri Isaakar ak Aser ak Neftali ak genn-wàllu giirug Manase ga dëkke diiwaanu Basan.
63Góor ñi askanoo ci Merari la seen làng muurloo ci tegoo bant fukki dëkk yu mag ak ñaar yu bokk ci suufi giiri Ruben ak Gàdd ak Sabulon.
64Noonu la bànni Israayil joxe Leween ñi dëkk yooyu ak seeni parlu.
65Dëkk yooyu bokk ci suufi Yuda ak Simeyon ak Beñamin, di dëkk yi ñu jota lim seeni tur ci kaw, ab tegoo bant lañu leen joxe.
66Lenn ci kër yu bokk ci làngi Keyat lañu jox dëkk yu mag yii bokk ci suufi giirug Efrayim:
67ca diiwaanu tundi Efrayim, Sikem dëkku rawtu ba ak parloom; ak Geser ak parloom;
68ak Yogmeyam ak parloom; ak Bet Oron ak parloom;
69ak Ayalon ak parloom; ak Gaat Rimon ak parloom.
70Ñu ame ba tey ca suufas genn-wàllu giirug Manase dëkk yii ànd ak seeni parlu: Aner ak Bileyam. Làngi yeneen doomi Keyat a ko séddoo.
71Góor ñi askanoo ci Gerson lañu jox lii: ci céru genn-wàllu giirug Manase lañu leen sédde dëkk yu mag yii ànd ak seeni parlu: di Golan ci diiwaanu Basan, ak Astarot,
72joxaat leen ci suufas giirug Isaakar dëkk yii ànd ak seeni parlu: di Kedes ak Dabraat
73ak Ramot ak Anem.
74Ñu dellu jox leen ci suufas giirug Aser dëkk yii ànd ak seeni parlu: di Masal ak Abdon
75ak Ukog ak Rexob.
76Ñu dellooti jox leen ci suufas giirug Neftali dëkk ba ñuy wax Kedes ca Galile ak àllub parlu ya ko wër, ak Amon ak parlu ya ko wër, ak Kiryaatayim aki parloom.
77Góor ñi askanoo ci Merari, muy ña des ca Leween ña, ñoom lañu jox suuf sa ñu jële ca suufas giirug Sabulon. Dëkk yii la ak seeni parlu: Rimono ak Tabor.
78Ñu joxaat leen dëkk ya ca wàllaa dexu Yurdan ca penkub Yeriko, te bokk ca suufas giirug Ruben. Mooy dëkk yii ànd ak seeni parlu: di Beccer ga ca ndànd-foyfoy ga ak Yaxacc
79ak Kedemot ak Mefaat.
80Ñu joxati leen ci suufas giiru Gàdd, dëkk yii ak seeni parlu: di Ramot ga ca Galàdd, ak Maxanayim
81ak Esbon ak Yaser.